7 Du penku, du sowu, te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
8 Yàllaay àtte: kii mu detteel, kee mu kaweel.
9 Merum Aji Sax ji dib kaas ci loxoom, biiñu njafaan bu wex di ca fuur, mu jol ko képp ku bon ci àddina, mu naan ba naanaale ginjrit ga.
10 Man may biral jëfam ba fàww. Damay woy Yàllay Yanqóoba.