Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 74:7-20 in Wolof

Help us?

Sabóor 74:7-20 in Kàddug Yàlla gi

7 Dañoo taal sa kër gu sell, sa dëkkuwaayu tur lañu daaneel, ba sobeel ko.
8 Ñu namm noo not ba nu nooy, fuy bérabu ndajem Yàlla ci réew mi, ñu lakk.
9 Sunuy takk réer na nu, yonent amatul, te kenn xamul fu lii di àkki.
10 Éy Yàlla, fu reetaani noon di dakke? Xanaa bañ yi duñu la ñàkke kersa ba fàww?
11 Looy téye sa loxol ndijoor? Na sa loxo jóge sa dënn, nga buube leen.
12 Yàlla, yaa masa doon sama buur, di ma walloo ci digg réew mi.
13 Yaa xàjjale géej gi ci sa doole, toj boppi ninki-nànka ya ca ndox ma,
14 yaa rajaxe kaaŋi rab wa, leele ko rabi màndiŋ ma.
15 Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, ŋiisal dex yu masa wal.
16 Yaa moom bëccëg, moom guddi, teg fi weer week jant bi.
17 Yaa rëdd mboolem digi suuf, sàkk noor ak nawet.
18 Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree, xeet wu amul bopp a lay sewal.
19 Bul wacce rabu àll sam xati, bul sàggane sa néew-doole yi mukk.
20 Ngalla xoolal ci kóllëre gi, fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.
Sabóor 74 in Kàddug Yàlla gi