20 Ngalla xoolal ci kóllëre gi, fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.
21 Yàlla bu néew-doole ñibbaale gàcce, yal na ku ñàkk ak ku néewle di la santandoo.
22 Éy Yàlla, jógal ñoŋal sa dëgg, bàyyil xel dof bi la dëkkee sewal.
23 Bul tanqamlu sa coowal noon yi, ñii la jógal, seenum riir a ngi jolli saa su ne.