Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 73:8-14 in Wolof

Help us?

Sabóor 73:8-14 in Kàddug Yàlla gi

8 Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9 Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, làmmiñ dajal suuf.
10 Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom, di jolu seen wax nim ndox
11 te naan: «Lu ci Yàlla xam? Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?»
12 Ñu bon ñaa ngoog! Ne finaax, di gëna woomle.
13 Man kay maa sellal ci neen, di sàmm sama der.
14 Bés bu ne yar dal ma, saa yu ma xëyee, jot mbugal.
Sabóor 73 in Kàddug Yàlla gi