Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 73:6-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 73:6-10 in Kàddug Yàlla gi

6 Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
7 Dañoo suur ba gët suulu, seen xalaati xel xëtt yoon.
8 Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9 Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, làmmiñ dajal suuf.
10 Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom, di jolu seen wax nim ndox
Sabóor 73 in Kàddug Yàlla gi