3 ngir maa ñee ku bew, ndax gis mu baaxle te di ku bon.
4 Amuñu metit, xanaa ne faaj.
5 Doñ-doñu nit dabu leen, coonoy doom aadama dalu leen.
6 Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
7 Dañoo suur ba gët suulu, seen xalaati xel xëtt yoon.
8 Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9 Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, làmmiñ dajal suuf.