23 Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor.
24 Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teddnga.
25 Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
26 Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
27 Ku la sore kat, sànku; képp ku la wor, nga fàkkas.
28 Man de, jege Yàllaa ma gënal. Boroom bi, Aji Sax ji, yaw laa def kiiraay, ngir siiwal sa jépp jëf.