Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 73:22-27 in Wolof

Help us?

Sabóor 73:22-27 in Kàddug Yàlla gi

22 Booba ngaaka laa, xawma dara; rab laa woon fi sa kanam.
23 Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor.
24 Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teddnga.
25 Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
26 Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
27 Ku la sore kat, sànku; képp ku la wor, nga fàkkas.
Sabóor 73 in Kàddug Yàlla gi