Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 73:18-24 in Wolof

Help us?

Sabóor 73:18-24 in Kàddug Yàlla gi

18 Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, daane leen, ñu sànku,
19 Yàquleeka leena bett! Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!
20 Day mel ni gént goo yewwoo. Céy Boroom bi, boo xippee, jëmmu gént ga soof la.
21 Naqar laa amoon, sama xol di dagg.
22 Booba ngaaka laa, xawma dara; rab laa woon fi sa kanam.
23 Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor.
24 Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teddnga.
Sabóor 73 in Kàddug Yàlla gi