Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 73:13-22 in Wolof

Help us?

Sabóor 73:13-22 in Kàddug Yàlla gi

13 Man kay maa sellal ci neen, di sàmm sama der.
14 Bés bu ne yar dal ma, saa yu ma xëyee, jot mbugal.
15 Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,» kon de, ma wor sa askanu mbooloo.
16 Naka laay jéema ràññee lii, mbir mi ëlëm ma.
17 Ba ma àggee sa kër gu sell ga, laa doora gis muju ku bon.
18 Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, daane leen, ñu sànku,
19 Yàquleeka leena bett! Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!
20 Day mel ni gént goo yewwoo. Céy Boroom bi, boo xippee, jëmmu gént ga soof la.
21 Naqar laa amoon, sama xol di dagg.
22 Booba ngaaka laa, xawma dara; rab laa woon fi sa kanam.
Sabóor 73 in Kàddug Yàlla gi