Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 72:5-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 72:5-16 in Kàddug Yàlla gi

5 Yal nañu la wormaal feek jant biy am, feek weer wiy feq, sët ba sëtaat.
6 Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef, mbaa waame wuy suuxat suuf.
7 Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,
8 mu yilif géej ba géej ak dex ba ca cati àddina.
9 Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,
10 buuri Tarsis ak dun ya di ko indil ay galag; buuri Saba ak Seba di ko yótsi yóbbal,
11 buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.
12 Mooy xettliji aji tumurànke bu woote wall ak aji néewle ju sësul fenn.
13 Mooy yërëm ku néewleek ku tumurànke, di sàmm bakkanu aji tumurànke,
14 boole leen jot ci notaangeek loraange, ngir fonk seen bakkan.
15 Yal na Buur gudd fan, yal nañu ko may wurusu Saba. Nañu koy ñaanal saa su ne, di ko saxoo, mu barkeel.
16 Yal na pepp ne gàññ ci réew mi, yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ; dëkk yu mag yi sëqi nit ba law,
Sabóor 72 in Kàddug Yàlla gi