2 muy àttee sa mbooloo njub, di àttee sa néew-ji-doole ñi yoon,
3 tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk,
4 Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi, di wallu doomi néew-ji-doole tey dëggaate kiy nennoo.
5 Yal nañu la wormaal feek jant biy am, feek weer wiy feq, sët ba sëtaat.