13 Mooy yërëm ku néewleek ku tumurànke, di sàmm bakkanu aji tumurànke,
14 boole leen jot ci notaangeek loraange, ngir fonk seen bakkan.
15 Yal na Buur gudd fan, yal nañu ko may wurusu Saba. Nañu koy ñaanal saa su ne, di ko saxoo, mu barkeel.
16 Yal na pepp ne gàññ ci réew mi, yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ; dëkk yu mag yi sëqi nit ba law,
17 yal na turam sax, ba law fu jant tiim, yal na xeet yépp barkeele ci moom, te di ko ndokkle.
18 Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji, Yàllay Israyil, mi wéetooy jalooreem.
19 Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!