Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 6:3-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 6:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma! Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!
4 Sama xol a jeex tàkk. Aji Sax ji, loo deeti xaar nag?
5 Éy Aji Sax ji, délsil, xettli ma! Walloo ma sa ngor.
6 Deesul dee ba fàttliku la; ku dugg njaniiw, nu mu lay sante?
7 Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, sama lal di féey, ba far seeye rongooñ.
8 Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.
9 Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma! Aji Sax ji dégg na saay jooy,
Sabóor 6 in Kàddug Yàlla gi