7 Yàlla buma rusloo ñi la yaakaar, yaw Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yàlla buma gàcceel ñi la topp, yaw Yàllay Israyil.
8 Yaa tax ma dékku, ñu di ma sewal, ma rus ba sëlmoo gàcce.
9 Jaambur laa léegi ci saay bokk, mel ni doxandéem sama biir doomi ndey.
10 Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, te jëf ji ñu la sewale man la dal.