3 May suux ci ban bu xóot, te awma fu ma teg tànk. Maa ngi nii ci ndox mu xóot, gannax yi mëdd ma.
4 Ma woote wall ba tàyyi, sama put gi wow koŋŋ. Ma séentu la, yaw sama Yàlla, ba samay gët giim.
5 Sama kawari bopp sax, ñi ma bañ ci daraa ko ëpp. Ñu bare doole, bëgg maa sànk, noonoo ma ci dara. Sàccuma, nara fey!
6 Yaw Yàlla, xam nga sama jëfi dof, te samay tooñ umpu la.