Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 69:21-33 in Wolof

Help us?

Sabóor 69:21-33 in Kàddug Yàlla gi

21 Dees maa sewal, sama xol jeex, ma wopp; may sàkku yërmande, awma ko; ku ma dëfal it, gisuma ko.
22 Tooke lañu ma leel, ma mar, ñu nàndal ma lu forox.
23 Yal na seen ndab di seenum yeer, seeni am-di-jàmm di seenug fiir.
24 Yal na seeni gët giim, ba dootu gis; yal na seen ndigg rëcc fàww.
25 Yal nanga leen yuri mbugal, sa mer tàkk, dab leen.
26 Yal na seeni dal gent, seeni xayma wéet.
27 Yaw, nga duma ba noppi, ñu toppaat ca, nga gaañ, ñu siiwal mitit wa.
28 Dencal leen tooñ ci kaw tooñ, te yàlla buñu tàbbi ci sag njekk.
29 Yal nañu leen far ca téereb dund ba, bañ leena limaale ca aji jub ña.
30 Man de, damaa jàq, tiis. Éy Yàlla, yal naa làqoo sag wall.
31 Damay woy Yàlla, teral ko, màggal ko, sant ko.
32 Mu gënal Aji Sax ji saraxu yëkk, aki béjjénam aki wewam.
33 Néew-ji-doole di gis, bége, kuy sàkku Yàlla yokku fit.
Sabóor 69 in Kàddug Yàlla gi