12 Ma sol ay saaku, di ko ñaawloo, ñu di ma léebu.
13 Waa pénc ma di ma tooge, màndikat yi di ma woyal.
14 Waaye man, Aji Sax ji, yaw laay dagaan. Éy Yàlla, na tey di bésub yiw. Ngalla nangul ma ci sa ngor lu yaa ak sa wall gu wóor.
15 Xettli ma ci ban bi, ma baña suux, xettliku ci samay noon. Rikk génne ma yii xóotey ndox,
16 ba gannax du ma mëdd, xóotey géej du ma warax, pax du ma kepp.