Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 68:7-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 68:7-16 in Kàddug Yàlla gi

7 Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.
8 Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, daagu, dugg màndiŋ ma. Selaw.
9 Suuf yëngu, asamaan sóob fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, Yàllay Israyil ja!
10 Yàlla, waame nga tawal, leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne,
11 sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
12 Boroom beey joxe ndigal, gàngooru jigéen indi xibaar:
13 «Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
14 Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»
15 Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.
16 Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, tundu Basan, tund wi ci coll yi,
Sabóor 68 in Kàddug Yàlla gi