5 Woyleen Yàlla, teral turam, xàllal-leen kiy war niir yi, Ki Sax moo di turam. Bànneexuleen fi kanamam.
6 Mooy baayoo jirim, di àtte jëtun, kookoo di Yàlla ja fa dëkkuwaayu sellngaam.
7 Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.
8 Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, daagu, dugg màndiŋ ma. Selaw.
9 Suuf yëngu, asamaan sóob fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, Yàllay Israyil ja!
10 Yàlla, waame nga tawal, leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne,