Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 68:3-13 in Wolof

Help us?

Sabóor 68:3-13 in Kàddug Yàlla gi

3 Yàlla wal, ñu naaw ni saxar. Ñu bon ñi sànku fi kanam Yàlla, mbete dax ak sawara.
4 Ñu jub ñi nag bég, di bànneexu fi kanam Yàlla, tey puukarewoo mbégte.
5 Woyleen Yàlla, teral turam, xàllal-leen kiy war niir yi, Ki Sax moo di turam. Bànneexuleen fi kanamam.
6 Mooy baayoo jirim, di àtte jëtun, kookoo di Yàlla ja fa dëkkuwaayu sellngaam.
7 Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.
8 Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, daagu, dugg màndiŋ ma. Selaw.
9 Suuf yëngu, asamaan sóob fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, Yàllay Israyil ja!
10 Yàlla, waame nga tawal, leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne,
11 sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
12 Boroom beey joxe ndigal, gàngooru jigéen indi xibaar:
13 «Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
Sabóor 68 in Kàddug Yàlla gi