Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 68:20-34 in Wolof

Help us?

Sabóor 68:20-34 in Kàddug Yàlla gi

20 Cant ñeel na Yàlla bésoo bés. Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal. Selaw.
21 Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo, Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan.
22 Yàlla daal ay rajaxe boppi noonam ak kaaŋ mu sëq mu boroom wéye tooñ.
23 Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi, waññee leen xóotey géej,
24 ngeen mana xuus ci seen deret, seeni xaj séddu ci seeni néew.»
25 Céy Yàlla, gis nañu sa gàngoor di daagu, sama Yàlla, sama buur, sa gàngoor ba ca biir kër gu sell ga.
26 Woykat ya jiitu, xalamkat ya mujje, janq ji yéewe leen tëgg um njiin.
27 Dajeleen, di sant Yàlla, yeen askanu Israyil, santleen Aji Sax ji.
28 Giirug Beñamin a ngi jiitu, gën cee néew, njiiti Yuda topp caak seeni kurél, njiiti Sabulon topp caak njiiti Neftali.
29 Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.
30 Sa kër gi tiim Yerusalem, fa la la buur yiy indiley galag.
31 Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi, ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. Tasaareel xeet yooyu sopp xare,
32 ay kàngam bàyyikoo Misra aki galag, réewum Kuus baral loxoom, indil Yàlla.
33 Yeen waa réewi àddina, woyleen Yàlla, teral-leen Boroom bi, Selaw
34 gawar bi ci asamaan, asamaani démb. Ma ngooguy àddu kàddug doole.
Sabóor 68 in Kàddug Yàlla gi