Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 68:11-24 in Wolof

Help us?

Sabóor 68:11-24 in Kàddug Yàlla gi

11 sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
12 Boroom beey joxe ndigal, gàngooru jigéen indi xibaar:
13 «Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
14 Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»
15 Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.
16 Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, tundu Basan, tund wi ci coll yi,
17 looy xeelook say coll, di fiire tund wi Yàlla namma dëkke? Aji Sax ji kat, fa lay dëkk ba fàww!
18 Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.
19 Yaa yéeg fa kawa kaw, jàpp ay jaam, yóbbaale. Yaa nangooy galag ci nit ñi, ba ci ñiy fippu ndax li Yàlla Ki Sax dëkke Siyoŋ.
20 Cant ñeel na Yàlla bésoo bés. Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal. Selaw.
21 Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo, Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan.
22 Yàlla daal ay rajaxe boppi noonam ak kaaŋ mu sëq mu boroom wéye tooñ.
23 Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi, waññee leen xóotey géej,
24 ngeen mana xuus ci seen deret, seeni xaj séddu ci seeni néew.»
Sabóor 68 in Kàddug Yàlla gi