7 Mooy nguuroo njàmbaaram ba fàww, di topp xeet yeek bët. Ku koy diiŋat, yàlla boo damu! Selaw.
8 Yeen xeet yi, santleen sunu Yàlla, te biral cantam!
9 Moo sàmm sunu bakkan, te waccu nu, nu tërëf.
10 Éy Yàlla, nattu nga nu, xelli nu, ni ñuy xellee xaalis;
11 laaw nga nu, teg nu njàqare.
12 May nga noon not nu, nu jaare sawara, jaarem ndox; nga génne nu, yaatal nu.
13 Maay duggaale sa kër ay saraxi rendi-dóomal, defal la samay dige,
14 yi ma waxoon ci sama gémmiñ, sama làmmiñ tudd ko, ba ma jàqee.
15 Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal, saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya, ma boole ca saraxu nag ak sikket. Selaw.
16 Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu, ma limal la li mu ma defal.