3 Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,
4 àddina yépp di la sujjóotal, di la woy, di joobe sa tur.» Selaw.
5 Dikkleen gis li Yàlla def, jëf la ju yéeme, ñeel doom aadama yi.
6 Moo soppi géej ag joor, maam ya dox jàll. Nanu ko bége foofa.