14 yi ma waxoon ci sama gémmiñ, sama làmmiñ tudd ko, ba ma jàqee.
15 Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal, saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya, ma boole ca saraxu nag ak sikket. Selaw.
16 Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu, ma limal la li mu ma defal.
17 Moom laa woo wall, àddu, màggal ko.
18 Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.
19 Waaye Yàlla dégg na ma, teewlu na samag ñaan.