Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 65:5-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 65:5-9 in Kàddug Yàlla gi

5 Ndokklee koo tànn, woo ko, mu dale say ëtt, di xéewloo sa ngëneeli kër, ak sa sellngay dëkkuwaay.
6 Defal nga nuy kéemaan, nangug ñaan ci njekk, yaw Yàlla, mi nuy wallu, di yaakaaru àddina wërngal këpp, ba ca géej gu sore ga.
7 Yaa dëje tund yu mag yi doole, gañoo sa kàttan,
8 di dalal riirum géej aki gannaxam, ak coowal xeet yi,
9 ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.
Sabóor 65 in Kàddug Yàlla gi