3 Yaw miy nangug ñaan, yaw la képp di wuysi.
4 Samay ñaawtéef man na ma, waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.
5 Ndokklee koo tànn, woo ko, mu dale say ëtt, di xéewloo sa ngëneeli kër, ak sa sellngay dëkkuwaay.
6 Defal nga nuy kéemaan, nangug ñaan ci njekk, yaw Yàlla, mi nuy wallu, di yaakaaru àddina wërngal këpp, ba ca géej gu sore ga.