Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 64:3-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 64:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Làq ma pexey ku bon, ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.
4 Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar, di fitte seeni kàdduy wextan,
5 di jam ku ñu tëru te deful dara; jekki jam ko, te tiituñu ci dara.
6 Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, di diisoo na ñuy làqe ay fiir, te naan: «Kenn du ko gis!»
7 Dañuy lal pexem njubadi te naan: «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!
8 Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, ñu jekki daanu.
Sabóor 64 in Kàddug Yàlla gi