3 Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo, ngir niir sa leer ak sa teddnga.
4 Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; ma àddu boog, kañ la!
5 Dama lay sant, sama giiru dund kay, yékkatiy loxo, sàbbaale la.
6 Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural, ma bég, sarxolle, màggal la.
7 Su ma tëddee, fàttliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.
8 Yaay sama ndimbal, may làqoo sa kiiraay, di sarxolle.
9 Sama xol taq la, nga téyee ma sa ndijoor.