Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 60:7-12 in Wolof

Help us?

Sabóor 60:7-12 in Kàddug Yàlla gi

7 Walloo nu sa ndijoor, nangul nu, ba say soppe xettliku.
8 Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.
9 Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, Efrayim di sama mbaxanam xare, Yuda di sama yetu nguur,
10 réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, Edom, ma teg tànk; Filisti, ma xaacoo fa.»
11 Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? Ku may jiite ba Edom?
12 Xanaa kay du yaw, Yàlla mi nu wacc, yaw Yàlla, mi baña ànd ak sunu mboolooy xare?
Sabóor 60 in Kàddug Yàlla gi