Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 5:3-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 5:3-11 in Kàddug Yàlla gi

3 Sama Buur, sama Yàlla, déglul, ma ne wallóoy! Yaw laay ñaan.
4 Aji Sax ji, ag suba, ngay dégg sama baat, suba su ne ma diis la samay dagaan, di séentu.
5 Doo Yàlla ju safoo coxor, yaw lu bon du la daloo.
6 Ku réy du taxaw fi sa kanam, kuy def lu ñaaw, bañ nga ko.
7 Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.
8 Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, sujjóotal sa bérab bu sell, wormaale la.
9 Éy Aji Sax ji, wommate ma sa njekk ndaxi noon, te xàllal ma saw yoon.
10 Ñii, lu ñu wax, wérul, seen xol a mébét njekkar, seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, ñuy naxe làmmiñ wu neex.
11 Éy Yàlla, topp leen, ñu fakktaloo seeni pexe; xalabal ñii barey moy, ñoo la gàntal.
Sabóor 5 in Kàddug Yàlla gi