Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 59:7-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 59:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
8 Déglul li ñuy yebbee ci seen gémmiñ, seen làmmiñ niy saamar, ñu defe ne kenn déggu leen.
9 Te yaw Aji Sax ji, yaa ngi leen di ree, yaa ngi kekku yéefar yii yépp.
10 Yaay sama doole, ma di la séentu, yaw Yàlla, yaay sama rawtu.
11 Sama Yàlla ju goree may gatandu. Moo may may ndam ci noon yi, ma gis.
Sabóor 59 in Kàddug Yàlla gi