13 Bàkkaar lañuy wax, seeni kàddu, bàkkaari neen. Yal nañu bew ba daanu, yooloo ko seeni saagaak seeni fen.
14 Meral, jeexal leen, jeexal leen, ba ñu jeex tàkk, ba ñépp xam ne Yàllaay Buur ci giirug Yanqóoba, ba ca cati àddina. Selaw.
15 Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
16 Ñuy wër di wut lu ñu lekk, su ñu suurul, di ñurumtu.
17 Maa lay woye sa doole, xëy, di sarxolle ngir sa ngor. Yaay sama rawtu, di sama làquwaay bésub njàqare.