Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 59:12-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 59:12-16 in Kàddug Yàlla gi

12 Yàlla, bu leen rey, lu ko moy samaw xeet fàtte. Tasaaree leen sa doole, daane leen. Boroom bi, yaa nuy feg.
13 Bàkkaar lañuy wax, seeni kàddu, bàkkaari neen. Yal nañu bew ba daanu, yooloo ko seeni saagaak seeni fen.
14 Meral, jeexal leen, jeexal leen, ba ñu jeex tàkk, ba ñépp xam ne Yàllaay Buur ci giirug Yanqóoba, ba ca cati àddina. Selaw.
15 Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
16 Ñuy wër di wut lu ñu lekk, su ñu suurul, di ñurumtu.
Sabóor 59 in Kàddug Yàlla gi