Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 57:5-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 57:5-8 in Kàddug Yàlla gi

5 Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
6 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.
7 Noon yi di ma fiir, sama xol jeex. Ñu gasal mam pax, far tàbbi ca. Selaw.
8 Yàlla, dogu naa, dogu naa woy, di la kañ.
Sabóor 57 in Kàddug Yàlla gi