Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 57:4-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 57:4-11 in Kàddug Yàlla gi

4 Mooy yónnee fa asamaan, musal ma, dumaal ma ku may not. Selaw. Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam.
5 Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
6 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.
7 Noon yi di ma fiir, sama xol jeex. Ñu gasal mam pax, far tàbbi ca. Selaw.
8 Yàlla, dogu naa, dogu naa woy, di la kañ.
9 Na sama jëmm jépp yewwu, xalam ak moroom ma yewwu; ma yee leeru njël.
10 Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi, kañ la ci biir waaso yi.
11 Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan, sa worma àkki fa kawa kaw.
Sabóor 57 in Kàddug Yàlla gi