Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 56:3-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 56:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku Màgg ki,
4 bés bu ma tiitee, yaw laay wóolu.
5 Yàlla laay màggal kàddoom, Yàlla laa wóolu, ragaluma. Lu ma nit manal?
6 Bésoo bés ñu ngi jalgati samay wax, seen mépp mébét di sama loraange.
7 Ñu ngi mànkoo, di ma yeeru, topp sama tànk, di wut sama bakkan.
8 Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce? Éy Yàlla, yal na leen sa mer dal!
9 Tumurànke naa, nga gis. Duyal samay rongooñ ci sa mbuus. Du lim nga lépp?
Sabóor 56 in Kàddug Yàlla gi