Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 51:3-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 51:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
4 Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.
5 Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
6 Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.
7 Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
8 Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, kon déey ma xel mu rafet.
Sabóor 51 in Kàddug Yàlla gi