Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 51:3-17 in Wolof

Help us?

Sabóor 51:3-17 in Kàddug Yàlla gi

3 Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
4 Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.
5 Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
6 Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.
7 Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
8 Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, kon déey ma xel mu rafet.
9 Wis ma ndox, ma sell; sang ma, ma set wecc.
10 Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.
11 Bul xool samay moy, faral sama ñaawtéef yépp.
12 Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell, yeesalal ma pastéefu xol.
13 Bu ma xalab, bu ma xañ sa noo gu sell.
14 May ma, ma bégeeti sag wall, te dundale ma xol bu tàlli,
15 ma xamal tooñkat sa war, ba moykat dellu ci yaw.
16 Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma siiwal sa njekk.
17 Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.
Sabóor 51 in Kàddug Yàlla gi