7 «Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; yeen waa Israyil, ma sikk leen. Maa di Yàlla, seen Yàlla.
8 Du seeni sarax laa leen di sikke, mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
9 Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
10 Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
11 Xam naa njanaawi tund yi, luy ndundatub tool maa ko moom.