3 Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, sawaraa ko jiitu, di xoyome, ngëlén lu mag wër ko.
4 Ma ngay woo seede asamaan ak suuf, ngir àtte ñoñam.
5 Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre ñiy sarxal, di ko fase sama kóllëreek ñoom.»
6 Asamaan a ngi biral njekkam, ngir Yàllaay àtte. Selaw.
7 «Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; yeen waa Israyil, ma sikk leen. Maa di Yàlla, seen Yàlla.
8 Du seeni sarax laa leen di sikke, mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
9 Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
10 Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
11 Xam naa njanaawi tund yi, luy ndundatub tool maa ko moom.