13 Damay lekk yàppu nag ak a naan deretu sikket a?
14 Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,
15 di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
16 Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?
17 Yeena ngii, bañ sama yar, xalab samay kàddu.
18 Fu ngeen gis ub sàcc, neexook moom, ab njaalookat, ngeen lëngool.
19 Dangeena afal seen gémmiñ ci mbon, seen làmmiñ taqoo fen,
20 ngeen di tooge seen mbokk, di yàq deru doomu ndey.