10 Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
11 Xam naa njanaawi tund yi, luy ndundatub tool maa ko moom.
12 Su ma xiifoon, duma leen ko wax, maa moom àddinaak li ci biiram.
13 Damay lekk yàppu nag ak a naan deretu sikket a?
14 Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,
15 di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
16 Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?