7 di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?
8 Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
9 Njotug bakkan jafe na, bu ci jéem dara.
10 Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?
11 Xanaa gis ngeen ne xelu, dee; dof, dee; naataxuuna it faatu rekk, wacce keneen alalam.
12 Sa bàmmeel di sa kër, ba fàww, di sa dëkkuwaay bu sax dàkk, boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
13 Nit ak darajaam fanaanul, mook aw rab a yem, sànku rekk.
14 Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.
15 Nara dee rekk niy xar, ndee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.