2 Yeen, xeetoo xeet, dégluleen; yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
3 ngay ku tuut di ku mag, nga bareleek nga néewle.
4 Li may wax xel la, di xalaat yu déggu.
5 Damay teewlu kàddu yu xelu, xalamal la sama tekkiteb cax.
6 Ana lu may tiit bés yu metti, yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
7 di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?
8 Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
9 Njotug bakkan jafe na, bu ci jéem dara.
10 Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?