13 Nit ak darajaam fanaanul, mook aw rab a yem, sànku rekk.
14 Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.
15 Nara dee rekk niy xar, ndee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.
16 Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw, jot sama bakkan, ba jël ma.
17 Buleen yéemu ci ku barele, teraangay këram di yokku.
18 Du dee ba yóbbaale dara, teraangaam du ko topp biir bàmmeel.
19 Na bége bànneexu bakkanam, ñu di ko kañe koomam,