Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 48:3-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 48:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 Jekk taxawaayee tundu Siyoŋ, catu bëj-gànnaar, dëkku buur bu mag bi, di mbégtem àddina sépp.
4 Yàllaa wone kaaraangeem ca biir tatay dëkk ba.
5 Buur yaa ngoog daje, àndandoo.
6 Nun noo gis, jommi, tiit, fëx,
7 ne fay pat-pati, jàq ni kuy matu.
8 Ngelawal penku, moom ngay tase gaal gu mag.
9 La nu déggoon de lanu gis ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sunu dëkku Yàlla ba. Yàllaa koy dëgëral ba fàww. Selaw.
Sabóor 48 in Kàddug Yàlla gi