3 Jekk taxawaayee tundu Siyoŋ, catu bëj-gànnaar, dëkku buur bu mag bi, di mbégtem àddina sépp.
4 Yàllaa wone kaaraangeem ca biir tatay dëkk ba.
5 Buur yaa ngoog daje, àndandoo.
6 Nun noo gis, jommi, tiit, fëx,
7 ne fay pat-pati, jàq ni kuy matu.
8 Ngelawal penku, moom ngay tase gaal gu mag.
9 La nu déggoon de lanu gis ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sunu dëkku Yàlla ba. Yàllaa koy dëgëral ba fàww. Selaw.
10 Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër, di xalaat sa ngor.