Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 45

Sabóor 45:6-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.
7Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,
8di sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Boroom diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom:
9sa yére yépp di gilli ndàbb, alowes akum kanel, ñu di la bégale xalam, ca sa biir kër yu yànj.
10Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.
11Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,
12Buur xemmeme la sab taar; mooy sab sang, wormaal ko.
13Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
14Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.

Read Sabóor 45Sabóor 45
Compare Sabóor 45:6-14Sabóor 45:6-14